Dindi Tor Browser ci sa nosteg amalin jafewul:

Ci Windows:

  • Gisal sa wayndaare wala amalinu Tor Browser . Nekkin bi teew mooy Desktop bi.
  • Dindil Tor Browser bi wala amalin bi.
  • Tuural sa Mbalit.

Ci macOS:

  • Gisal sa amalin Tor Browser. Nekkin bi teew mooy wayndare amalin bi.
  • Yóbbul amalinu Tor Browser sa mbalit ma.
  • Demal ci sa ~/Library/Application Support/ wayndare.
  • Jàppal ne wayndaare Library bi mi ngi làqqu ci xeetu macOS bu bees bi. Ngir xuus ci wayndaare boobule ci Finder, tànnal "Go to Folder..." alluwa "Go" bi.

Demal ci tànneef alluwa

  • Te nga bind ~/Library/Application Support/ ci xët bi te kilike Go.

Demal ci xëtu palanteer

  • Gisal joxe wayndaare TorBrowser- te nga yóbbu ko sa Mbalit.
  • Tuural sa Mbalit.

Jàppal ne soo sampul Tor Browser ci nekkin bi teew (twayndaare amalin bi), ak wayndaare TorBrowser-Data nekkul ci ~/Library/Application Support/ wayndaare, wante ci wayndaare menn wayndaare bi nga samp Tor Browser.

Ci Linux:

  • Gisal sa wayndaare Tor Browser . Ci Linux, amul nekkin bu teew, wante wayndaare bi dinanu ko tuddee "tor-browser_en-US" su fekkee xuusukaay Tor Browser bi ngay jëfandikoo ci Angale la nekk.
  • Dindil wayndarey Tor Browser bi.
  • Tuural sa Mbalit.

Jàppal ni sa nosteg amalin jëfukaay "Uninstall" kenn jëfandikoowu ko.