Taxawu, waxu leeral ak nataal xëtu tegtal bu njumte

Soo nuy yónne ab laaj ngir ndimbal, leeral njumte wala siiwal njumte, nu ngi lay ñaan nga boole ci xibaar yi war yépp:

  1. Nosteg doxin bi ngay jëfandikoo
  2. Tor Browser version
  3. Tor Browser Kaaràngey tolluwaay
  4. Jéego ci kaw jéego ci nan nga jotee jafe-jafe boobu, kon mën nanu ko defaraat (e.g. Ubbi naa xuusukaay bi, bind ab url, kilike ci ab tànneef ci sukkandikukaay yi, léegi sama xuusukaay yàqqu)
  5. Ab nataalu xoolu ci jafe-jafe bi
  6. Téere bu console ci biro Tor Browser (mën nanu ko ubbi jaaree ko ci Ctrl+Shift+J ci Windows/Linux ak Cmd+Shift+J ci macOS)
  7. Tor logs (Sukkandikukaay > Lëkkaloo > awaanse > Yër Tor logs yi)
  8. Gox bi ngay lëkkaloo ci Tor.
  9. Gox yi nu tànn ci Connection Assist (su fekkee ab jafe-jafe bu aju ci Connection Assist)
  10. Ndax Tor danu ko tere ci sa gox?
  11. Su fekkee Tor du lëkkaloo, ñaata waxtu lay jël ngir mu bootstrap? Ndax amul benn njeexital ci sa gaawaayu xuusukaay?

Tor jëfandikukat bi dafay jàppale kureelu waxtu biro yi

Altine ba Alxames: sunu jëfandikukat danuy jàpp ci email, Telegram, WhatsApp, ak Signal dañuy dox.

Àjjuma ba Dibéer: Buumu jokko ngir ndimbal bi danu ko tëj. Nu ngi lay ñaan nga xam ne sunu kureel dina tontu say bataaxal ci Altine ji.

Naka nga nuy jotee

Am na anam yu bare ngir jot nu, kon nu ngi lay ñaan nga jëffandikoo bi gën a dox ci yaw.

Telegram

Am nanu ay Telegram ak jaarukaay yu fës yu bare:

  1. @GetTor_Bot ngir yebbi Tor Browser.
  2. @GetBridgesBot ngir jot obfs4 bridges.
  3. @TorProject ngir jot xibaar yi mujj.
  4. @TorProjectSupportBot ngir ndimbal.
    • Ci jamono jii, yoonu ndimbal bu Telegram jàppandi na ci ñaari kàllaama: Angale ak Russe.
    • Soo soxlaa ndimbal ngir wër ndomba yamale internet bi, nu ngi lay ñaan nga tànn ci àlluwa tànneef bi nekk ci diwaan bi ngay lëkkalowee ndax mooy tax mu gën a yomb ci nun nu topp la.

Tor Ndajey waxtaan

Nu ngi lay diggal nga ñaan ndimbal ci Tor Forum. Dinga soxla sàqq ab këll ngir joxe ëmbeef bu bees. Nu ngi lay ñaan nga xoolaat waxtaani tegtal te nga xool ëmbeef yi am laata ngay laaj. Fii nu toll, ngir tontu bu gën a gaaw, nu ngi lay ñaan nga bind ci Angale. Soo gisee ab njumte, nu ngi lay ñaan nga jëfandikoo GitLab.

WhatsApp

Mën nga jot sunu kureelu ndimbal ak ab xëtu message ci sunu nimero WhatsApp: +447421000612. Serwiis bii dafa jàppandi rekk ngir bataaxal yi; ay wideo wala woote du jàll.

Gindikaay

Mën nga am ndimbal jaaree ko ci ab xëtu message ci sunu Siñaalu nimero: +17787431312. Signal ab amalinu bataaxal la bu laajul. Jamono jii, sunu kureel bi di taxawu nit ñi jàppandi na ci Angale ak Russe te dafay jublu ci taxawu jëfandikukat yu Tor yi nu tere ci bépp gox. Serwiis bi dafa jàppandi rekk ngir ay bataaxal yi nu bind; ay wideo, wala ay woote duñu jàll. Gannaaw ba nu yónnee ab bataaxal message, sunuy ndaw yi lay taxawu dina ñu la gindi te jàppale la nga saafara jafe-jafe bi.

Boyetu bataaxal

Yonnee nu ab bataaxalu internet ci frontdesk@torproject.org

Ci boppu lu waral bataaxal bi ci sa email, nu ngi lay ñaan nga bind lu waral mbind mi. Sa bataaxal lu mu gën a leer ci bopp bi (ci misaal. "Làjj ci Lëkkaloo", "leeral njumte ci dalu web", "leeral njumte ci Tor Browser, "Dama soxla ab bridge"), mu gën a yomb ci nun ngir nu ndànd te topp. Yenn saa yi sunu jotee ay email yu amul mbind muy leeral lu waral bataaxal bi, danu leeni màndargaal spam te dunu leen gis.

Ngir tontu bu gën a gaaw, nu ngi lay ñaan nga bind ci Angale, Russe, Español, Hindi, Bangla, ak/wala Purtugees soo ko mënee. Su fekkee amul benn làkk boo dégg ci yooyu, nu ngi lay ñaan nga bind ci bépp làkk boo mën, wànte jàppal sa xel ne dinanu jël tuuti saa ngir tontu ndax dinanu soxla ndimbalu firikat ngir xam li nga wax.

IRC ak Matrix

Mën nga noo gis ci #tor jaarukaay ci OFTC wala Tor jaarukaay Ndimbal Jëfandikukat ci Matrix. Dunu mën a tontu léegi, wànte dañuy tontu xoolaale backlog bi te dinanu dellusi ci yaw saa su nu ko mënee.

Jàngal naka lanuy lëkkaloo ci IRC / Matrix.

GitLab

Lu njëkk, xoolal ndax njumte bi xam nanu ko. Mën nga seet te jàng jafe-jafe yépp ci https://gitlab.torproject.org/. Ngir sos mbir mu bees, nu ngi lay ñaan laajal ab këll gu bees ngir jot misaalu Tor Project's GitLab ak gis dalukaay bu bees nga siiwal jafe-jafe bi. Nu ngi topp jafe-jafe yépp ci Tor Browser ca Tor Browser topp jafe- jafe. Jafe-jafe yi lëkkaloo ak sunu dalu web ci fii lanu ko war a bind Toppkatu mbirum Web.