Bi teew, Tor Browser dafay aar sa kaarànge ci nëbb say joxe xusukaay yi. Mën nga boo demee ba mu yàgg yokk sa kaarànge ci tànn dindi yenn melo dalu web yi nu mën a jëfandikoo ngir yàqq sa kaarànge ak sa kiirlaay. Mën nga def lii jaaree ko ci yokk Tolluwaayu Kaaràngey Tor Browser ci àlluwa wëreef bi. Di yokk tolluwaayu kaarànge Tor Browser dina dakkal yenn xëti web yiile dox ni ñu war a doxee, kon war nga natt sa soxla ci wàllu kaarànge dëppoo ak tolluwaayu mboolem amalin bi ngay laaj.

DUGG CI KAARÀNGEY SUKKANDIKUKAAY YI

Kaaràngey Sukkandikukaay yi mën nanu ci jot ci kilike xëtu Wëreef bi nekk ci wetu bantu URL bu Tor Browser. Ngir xool te defaraat sa Kaaràngey Sukkandikukaay, kilikeel ci butoŋ 'Sukkandkukaay' ci alluwa wëreef bi.

Click on 'Settings' under the shield menu

KAARÀNGEY TOLLUWAAY

Di yokk Tolluwaayu Kaarànge ci Kaaràngey Sukkandikukaay yu Tor Browser dina dindi wala dindi xaaju yenn melo dalu web ngir aar ci yenn song yu mën a am. Mën nga doxalaat sukkandikukaay yii waxtu bula neexee jaaree ko ci defaraat sa kaaràngey Tolluwaayu.

Tolluwaayu kaarànge bi dafar nanu ko fii nu toll ci Safest

Royuwaay
  • Ci tolluwaay bii, Tor Browser melo dali web yépp doxal nanu leen.
Bu ëpp kaarànge
  • Tolluwaay bii dafay dindi melo dalu web yépp te nuy gaañ yenn saa yi. Lii mën na indi yenn dal yi du dox ni mu waree.

  • JavaScript dindi nanu ko ci bépp non-HTTPS dalu web; yenn mbindin yeek yenn mbind ak màndarga xayma dindi nanu leen; ndegtu ak wideo (HTML5 media) nekk nañu bësal-ngir-doxal.

Bi ci ëpp kaarànge
  • Tolluwaay bii dafay may melo dalu web mu soxla dalukaay yu dal ak ay serwiis yu njëkk. Copite yiile dafay laal nataal yi, tasukaay xibaar yi, ak mbind yi.

  • Javascript dindi nanu ko def ko ci bi teew ci dali web yépp; yenn mbindin yi, xët yi, xayma yi, màndarga yeek nataal yi dindi nanu leen; ndegtu ak wideo yi (HTML5 media) nekk nañu bësal-ngir-doxal.