Soo taalee sa Tor Browser, di nga gis palanteer bu Lëkkalook Tor. Lii daf lay jox ab tànneef ngir wala nga lëkkaloo te du am jàdd ci jokkoowu Tor bi, wala nga defaraat Tor Browser ngir sa lëkkaloo. Am na benn boyét buy laac ndax daga bëgg batay lonku ci saasa ci Xuusukaayu Tor, bu fékée lolu la, saytul boyét bi.

LËKKALOO

Kilikeel 'connect' ngir lëkkaloo ak Tor

Ci anam yu bare, tànn "Connect" dina la may nga lëkkaloo ak jokkoowu Tor bi te doo am benn tërëlin booy samp.

Soo xasee ba kilike, ab bantu status dina feeñ, di wone tolluwaay lëkkaloowu Tor. Su fekkee danga am lëkkaloo bu gaaw, wànte bant bi dafa niroog lu taxaw ci ab tomb, jéemal 'Connection Assist' wala xoolal xëtu Troubleshooting ngir mu jàppale la nga saafara jafe-jafe boobu. Wala, soo xamee ne sa lëkkaloo danu ko yamale wala nga jëfandikoo ab proxy, danga war a kilike ci "Configure Connection".

Kilikeel 'Configure Connection' ngir jek jekal sukkandikukaayi jokkoo yi

CONNECTION ASSIST

Su fekke Tor fatt na ci sa bërëb, jéem ab bridge mën na la jàppale. Connection Assist mën na tànn benn ngir ngay jëfandikoo bërëb bi nga nekk.

Connection Assist buy doxal boppam

Su Connection Assist mënulee wone fi nga nekk wala nga bëgg a defaraat sa lëkkaloo ak sa loxo, mën nga tànn sa dëkk si àlluwa bi ngay bës muy wàcc te nga kilike ci 'Try a Bridge'.

Connection Assist defaraat

DEFARAAT

Tor Browser dina la yobbu ci ay xeeti tànneefi roofoo.

Connection Assist bi daf lay yëgal sa tolluwaayu lëkkaloowu Internet ak sa lëkkaloo ci jokkoowu Tor.

Lëkkaloo xayma bu àndak ndam

Lëkkaloo xayma bu jàllul

Checkbox bu njëkk bi mooy 'Quickstart'. Soo ko tànnee, saa soo ubbee Tor Browser, dina jéem a lëkkaloo ak sa sukkandikukaayu jokko bu njëkk.

Quickstart

Su fekkee sa lëkkaloo danu ko yamale, wala danga jéem te lajj lëkkaloo ci jokkoowu Tor ak benn saafara doxul, mën nga defaraat Tor Browser ngir mu jëfandikoo ab pluggable transport. 'Bridges' dina wone Moytukaaypàcc ngir defaraat ab pluggable transport wala lëkkaloo jëfandikoo pom yi.

Defaraatal Tor bridge

YENEENI TÀNNEEF

Su fekkee sa lëkkaloo dafay jëfandikoo ab proxy mën nga ko defaraat di kilike ci 'Settings ...' ci 'Defaraat nan Tor Browser lanuy lëkkaloo ci Internet'. Ci anam yu bare, lii amul solo. Dinga xami ndax danga soxla tànn checkbox bii ndax sukkandikukaay yu niroo lanuy jëfandikoo ngir yeneen xuusukaay yi ci sa doxinu jumtukaay. Su mënee nekk, laajal sa caytukatu jokkoo ngir gindi. Su fekkee sa lëkkaloo du jëfandikoo ab proxy, kilikeel ci "Connect".

Proxy sukkandikukaay ngir Tor Browser