JAVASCRIPT

JavaScript ab joxinu ndigal ordinatëer la bu dalu web yiy jëfandikoo ngir joxe ay cër jokkalante yu mel ni wideo, ay dawalinu nataal, ay ndeglu, ak status timelines. Ci lu ajuwul sunu coobare, JavaScript mën na tamit indi ay song ci kaaràngey xuusukaay bi, lu mën a indi deanonymization.

Tor Browser includes an add-on called NoScript. It's accessible through "Add-ons and themes" on the hamburger menu (≡). Locate the NoScript plug-in and click on it to open a panel where you can customize its settings.

In the panel, next to the Toolbar button, select 'Show'. This will display the NoScript button to the right of the browser address bar. This button enables you to manage JavaScript and other scripts on web pages, allowing you to control their execution individually or block them entirely.

Jëfandikukat yu soxla tolluwaayu kaarànge bu kawe ci seen xuusukaayu dalu web war nañoo jafal Tor Browser's Kaaràngey tolluwaay ba "Safer" (buy dindi JavaScript ngir HTTPS yu amul dalukaayu web) wala "Safest" (buy def loolu ci dali web yépp). Wànte, dindi JavaScript dina tee dalukaayu web yu bare ngir nu wone wonin bu baax, kon sukkandikukaay Tor Browser bi teew mooy may dalukaayu web yépp ñu doxal ndigalu doxalin yi ci mode "Standard".

BROWSER ADD-ONS

Tor Browser nu ngi ko wéer ci Firefox, ak bépp xuusukaay bu am siiwal wala ay wonin ci ordinaatëer yu mën a àndak Firefox mën nanu leen a samp tamit ci Tor Browser.

Wànte, siiwal yi nu xayma yépp ngir jëfandikoo leen ak Tor Browser mooy yiy duggal ci bi teew. Di samp bépp beneen xuusukaay bu àndak ay siiwal mën na yàqq doxalinu Tor Browser wala indi ay jafe-jafe yu tar yuy am njeexital ci sa kiirlaay ak kaarànge. Danuy tere bu baax nga samp ay siiwal, ak Tor Project bi du joxe ndimbal yiile ay defaraat.

FLASH PLAYER

Flash nekkoon na benn amalin bu bari cër bu dali web yi doon jëfandikoo ngir wone ay wideo ak yeneen cër jokkalante yu melni po yi. Danu ko dindi woon def ko bi teew ci Tor Browser ndaxte mënoon na wone bërëb bi nga nekk dëgg ak sa dëkkuwaay IP. Tor Browser jëlatul Flash te kenn mënu ko doxal.

Lu ëpp ci doxalinu Flash bi wecco nanu ko ak HTML5 jëfandikookat, te mu aju bu baax ci JavaScript. Mboolem jëfukaay wideo yu mel ni YouTube ak Vimeo toxu nañu ci HTML5 te dootuñu jëfandikoo Flash.