Tor Browser ci Android

Tor Browser ci Android mooy xuusukaayu portaabal bi fës bi Tor Project defar te di ko doxal. Dafa mel ni Tor Browser bu biro wante ngir sa telefonu portaabal Android. Yenn ci melo yu njëkk yi Tor Browser ngir Android bokk na ci: waññi topp gi ci dalukaayu web yi, aar ceytu gi, di dëggërlu ci fingerprinting, ak moytu tere yi.

YEBBI AK SAMP

Am na Tor Browser ngir Android ak Tor Browser ngir Android (alpha). Jëfandikukat yu ajuwul ci wallu xarale dañoo war a am Tor Browser ngir Android, ndegam bii dal na te njumte yi bariwul. Tor Browser ci Android jàppandi na ci Play Store, F-Droid ak dalukaayu web bu Tor Project. Wóorul ci ngay yebbi Tor Browser feneen fu bokkul ak ñetti mboolem jëfukaay yii.

Google Play

Mën nga samp Tor Browser ngir Android jaare ko Google Play Store.

F-Droid

The Guardian Project dafay joxe Tor Browser ngir Android ci seen F-Droid deñcukaay. Soo bëggee samp jumtukaay jaaree ko ci F-Droid, nu ngi lay ñaan nga topp jéego yii:

  1. Sampal jumtukaayu F-Droid bi ci sa jumtukaayu Android jóge ci the F-Droid website.

  2. Gànnaaw ba nga sampee F-Droid, ubbil jumtukaay bi.

  3. Ci suuf wetu ndeyjoor ci koñ bi, ubbil "Settings".

  4. Ci suufu pàccu "My Apps", ubbil Repositories.

  5. Jafalal "Guardian Project Official Releases" niki lu nu doxal.

  6. Léegi F-Droid dafay yebbi limu jumtukaay yi joge ci the Guardian Project's dencukaay (Jappal: lii mën na jël ay simili).

  7. Bësal Back butoŋ bi ci kaw wetu cammooñ ci koñ bi.

  8. Ubbil "Latest" ca wetu cammoñ ca suuf ca koñ ba.

  9. Ubbil Jumtukaayu seet bi nga bës seetu yaatal bi nekk wetu suuf ci ndeyjoor bi.

  10. Saytu ngir "Tor Browser ci Android".

  11. Ubbil njureefi laaj yi ci "The Tor Project" te nga samp.

Dalu web bu Tor Project bi

Mën nga am tamit Tor Browser ngir Android jaare ko ci yebbi ak samp apk jaare ko ci Tor Project website.

XUUS CI TOR BROWSER NGIR ANDROID Ci YOON WU NJËKK

Soo doxalee Tor Browser yoon wu njëkk, dinga gis ab tànneef ngir lëkkaloo ca saasa ak jokkoowu Tor, wala nga caytu Tor Browser ngir sa lëkkaloog xëtu sukandikukaay.

Lëkkale

Lëkkaloo ci Tor Browser ngir Android

Ci anam yu bare, tànn "Connect" dina la may nga lëkkaloo ak jokkoowu Tor bi te doo am benn tërëlin booy samp. Soo xësee bës foofu, ay mbind yuy soppeeku dinañu feeñ ci suufu xoltu bi, di wone yokkoteb lëkkalook Tor. Su fekkee danga yor lëkkaloo bu gaaw, wànte xët bi dafa tëwa dem ci ab tolluwaay, xoolal xëtu Troubleshooting bi ngir mu jappalela nga saafara jafe-jafe boobule.

SAMP

Samp Tor Browser ci Android

Su fekkee danoo dindi sa lëkkaloo, danga war a tànn màndargay sukkandikukaay yi. Tor Browser dina la yobbu ci ay xeeti tànneefi roofoo. Xoolu bu njëkk bi dina la wax lu aju ci status bu jokkowu Tor te jox la ab tànneef ngir jokkale ab Bridge ('Config Bridge'). Su fekkee sa lëkkaloo danu ko dindi, wala jéem nga te lajj ci lëkkaloo ak jokkoo bu Tor te benn saafara sottiwul, bësal ci 'Config Bridge'. Dinanu la yobbu kon ci Moytuxoolu ngir caytu ab pluggable transport.

MOYTU

Jàllalekaayi Bridge ñooy jàllekaayi Tor yi nu deful ci àlluway Tor bu fës bi. Bridges am na solo ngir ñiy jëfandikoo Tor te nekk ci nguur yi nooteel yi bare, ak ngir nit ñi soxla kaarànge ndaxte dañoo ragal nu xàm ne dañuy jokkoo jaare ko ci ab dëkkuwaayu Tor relay IP bu fës.

Ngir jëfandikoo ab pluggable transport, bësal ci màndargay sukkandikukaay yi soo dee door Tor Browser yoon wu njëkk. Xoltu bu njëkk bi daf lay wax ci status bu jokkoowu Tor. Bësal ci 'Config Bridge' ngir jokkaleek ab bridge.

Tere internet ci Tor Browser ngir Android

Beneen xoolu bi dina joxe tànneef bi ngir nga jëfandikoo ab built-in bridge wala bridge bus a coobare. Ak tànneefu "Use a Bridge", dinga am ñetti tanneef: "obfs4", "meek-azure", ak "snowflake".

Tànnal ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Tànnoon ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Su fekkee tànn nga "Provide a Bridge I know", kon war nga dugg ci ab bridge address.

Joxe ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Joxe dëkkuwaayi bridge yi ci Tor Browser ngir Android

SAYTU XAMMEEKAAY

Raññeekaay bu Bees

New Identity ci Tor Browser ngir Android

Su Tor Browser dee dox, di nga gis loolu ci sa àlluway yëgle ci sa jumtukaay gànnaaw ba nga ko yaatale ak sa butoŋu "NEW IDENTITY". Bës ci butoŋ bi dina la indil ab new identity. Ci lu dëppoowuk ak ci Tor Browser ngir Ordinaatëru Biro, "NEW IDENTITY" butoŋ bi ci Tor Browser ngir Android terewul say jëf ci sa xuusukaay bi nu mën ko lëkkale ak li nga doon def bu njëkk. Tànn ko dina soppi sa Tor circuit képp.

KAARANGEY SUKKANDIKUKAAY

Sukkandikukaay yu am kaarànge ak ab jumtukaayu nataal bu am kaarànge ci Tor Browser ngir Android

Kaaràngey sukkandikukaaydindil yenn melo web bi mën a indi ay jafe-jafe ci sa wàllu kaarànge ak kiirlaay. Tor Browser ci Android dafay joxe ñetti toluwaayu kaarànge yu niroo yu jàppandi ci ordinaatëeru biro. Mën nga soppi tolluwaayu kaarànge gi ci topp jéego yii nu joxe:

  • Bësal ci ab butoŋ bu am 3 tomb yu taxaw ci bantu URL bi.
  • Wàccal ci suuf te nga bës ci "Security Settings".
  • Mën nga tànn léegi ab tànneef maanam. Standard, Safer wala Safest.

YEESAL

Tor Browser danu ko war a di yeesal saa su nekk. Sooy wéy di jëfandikoo ab version bu yàgg bu tëralinu nosukaay bi, mën nga ubbi buntu kaarànge gi nga amoon buy néewal doole sa kirlaay ak nëbbu. Mën nga yeesal Tor Browser automatically wala ak sa loxo.

Yeesal Tor Browser ngir Android automatically

Jëfekaay bii dafay dëggal ni am nga Google Play wala F-Droid bu nu samp ci sa telefon portaabal.

Google Play

Yeesal Tor Browser ngir Android ci Google Play

  • Ubbil jumtukaayu Google Play Store bi.
  • Ci kaw ci ndeyjoor, bësël alluway xët bi.
  • Bësal ci 'Manage apps and devices'.
  • Bësal ci xëtu 'Manage' bi.
  • Bësal ci 'Updates available'
  • Bësal ci Tor Browser ngir Android jóge ci limu jumtukaay yi nu war a yeesal.
  • Bësal ci 'Update'.
F-Droid

Yeesal Tor Browser ngir Android ci F-Droid

Bësal ci "Settings", daldi dem ci "Manage installed apps". Ci beneen xoltu bi, tànnal Tor Browser te ca mujjantal ga nga bës ci butoŋu "Update".

Yeesal Tor Browser ngir Android ak say yoxo

Wëral Tor Project website te nga yebbi ab kayit bi Tor Browser mujjee génnee, ba noppi nga samp ko ne bu njëkk. Ci anam yu bare, version bu Tor Browser bu mujj bii dina sampu ci kaw version bi gën a yàgg, ci noonee di yeesalaat xuuskat bi. Su fekkee loolu dafa lajj ci yeesal xuusukaay bi, mën na am nga soxla sempi Tor Browser laata nga koy sampaat. Ak Tor Browser tëj, dindi ko ci sa jumutukaay nga sempi ko jëfandikoo say sukandikukaayu jumtukaay. Aju ci sa xeetu telefon portaabal, xuusal ci Settings > Apps, nga daldi tànn Tor Browser te nga bës ci butoŋu "Uninstall" bi. Gànnaaw loolu, yebbil Tor Browser bu mujjee génn te nga samp ko.

SEMPI

Tor Browser ngir Android mën nanu ko sempi ci sassa jaare ko ci F-Droid, Google Play wala jaare ko ci say sukkandikukaayi jumtukaayu telefon portaabal.

Google Play

Sempi Tor Browser ngir Android ci Google Play

  • Ubbil jumtukaayu Google Play Store bi.
  • Ci kaw ci ndeyjoor, bësël alluway xët bi.
  • Bësal ci 'Manage apps and devices'.
  • Bësal ci xëtu 'Manage' bi.
  • Bësal ci Tor Browser ngir Android jóge ci limu jumtukaay yi nu samp ci sa gindikaayu ordinaatëer.
  • Bësal ci 'Uninstall'.

F-Droid

Sempi Tor Browser ngir Android ci F-Droid

Bësal ci "Settings", daldi dem ci "Manage installed apps". Ci beneen xoltu bi, tànnal Tor Browser te ci mujjantal gi bësal ci butoŋu "Uninstall".

Sukkandikukaay yu jumtukaayu loxo

Sempi Tor Browser ngir Android di jëfandikoo ay sukkandikukaayi jumtukaayu internet

Aju ci sa xeetu telefon portaabal, xuusal ci Settings > Apps, nga daldi tànn Tor Browser te nga bës ci butoŋu "Uninstall" bi.

TROUBLESHOOTING

Yër Tor Logs

Yër Tor logs ci Tor Browser ngir Android

Ngir gis say Tor logs:

  1. Jafalal Tor Browser ngir Android te nga bës 'Connect'.
  2. Ci diiru bootstrapping bi, puusal ci ndeyjoor ba ci cammoñ ngir gis logs yi. (Jàppal: Bi teew, mëneefu jël ay nataal ci xoltu yi ngir Tor logs dindi nanu ko ci Tor Browser ngir Android). #41195

Su fekkee bëgg ngaa seddoo mboolem njumte yi ak nun, dinga mën a jël ab nataalu xoltu. Ci bi teew, nataali xoltu dindi nanu ko ci Tor Browser, wànte mën nga leen indiwaat. Ngir def loolu, nu ngi lay ñaan nga top jéego yii:

  • Bësal butoŋu àlluwa bi (ci suufu xoolu bi ci wetu ndeyjooru galaanu dëkkuwaay bi, ñetti tomb yu taxaw).
  • Nga daldi bës 'Settings'.
  • Demal ci pàccu 'Advanced'.
  • Taalal 'Allow screenshots'.

Ngir defar yenn jafe-jafe yi ëpp yu faral di am nu ngi lay ñaan nga xool Support Portal entry.

JAFE-JAFE YUNU XAM

Fii nu toll, am na ay melo yu jàppandiwul ci Tor Browser ngir Android, wante ci jamono jii jàppandi na ci Tor Browser ngir ordinaatëeru biro.

  • Mënuloo gis sa Tor circuit. #41234
  • Tor Browser ngir Android du lëkkale su demee ci Kàrtu SD bi. #31814
  • Mënuloo jël ay nataalu xoltu sooy jëfandikoo Tor Browser ngir Android. #27987
  • Mënuloo ubbi ay dëkkuwaay onion yiy laaj Client Authorization #31672

Yeneeni mbiri Tor ci jumtukaayi loxo

Orfox

Orfox nu ngi ko njëkk a génne ci 2015 ci The Guardian Project def ko ak jubluwaay jox jëfandikookati Android yi ab anam ngir xuus ci internet jaare ko ci Tor. Ci diiru ñetti at yii weesu, Orfox dafa wéyaloon di yokku te nekk ab yoon wu siiw ngir nit ñiy xuus ci internet ak kiirlaay gu doy wuteeg xuusukaay yi faral di am, te Orfox amoon na dayoo lool ngir jàppale nit ñi doon dund ñuleen di tere aka bloke ci yenn dalu web ak ëmbeef yu doy waar. Ci 2019, Orfox was sunsetted gànnaaw banu gennee Tor Browser ngir Android bu ofisiyel.

Orbot

Orbot jumtukaayu proxy bu laajul fay buy dooleel yeneeni jumtukaay yi ngir ñuy jëfandikoo jokkoowu Tor bi. Orbot dafay jëfandikoo Tor ngir fas doxalinu Internet bi. Noone mën nga ko jëfandikoo ak yeneeni jumtukaay yi nu samp ci sa telefon portaabal ngir moytu dakkal bi te aar sa bopp ci ceytu gi. Orbot mën nanu ko yebbi te samp ko jaaree ko ci Google Play. Xoolal our Support portal ngir xam ndax soxla nga Tor Browser ngir Android ak Orbot wala benn ci ñoom.

Tor Browser ci iOS

Amul Tor Browser ci iOS. Nu ngi lay diggal ab jumtukaayu iOS bu nu tuddee Onion Browser, te mu nekk open source, jëfandikoo sëfu xayma bu Tor, te ki ko defar nekk kenn kuy liggéeyando ak Tor Project. Wànte, Apple dafay laaj xuusukaay ci iOS ngir jëfandikoo mbir bi nu tudde Webkit, liy tee Onion Browser am kiirlaay yu nirook ay kiirlaayu Tor Browser.

Jàngal leneen lu bari ci Onion Browser. Yebbil Onion Browser jëlee ko ci App Store.

Tor Browser ci telefonu Windows

Amul fi nu toll benn jëfekaay ngir doxal Tor ci telefonu Windows yu yàgg wànte su fekkee xeeti telefonu Microsoft/ yu yees yi la ,ñoo niroo jéego ci Tor Browser on Android mën nanu leen topp.