Lu ëpp ci Pluggable Transports, yu mel ni obfs4, dañuy wéeru ci jëfandikoo yu jàllalekaayi "bridge". Nirook jàllalekaayi Tor yu baax, bridges yi ñu ngi daw ci seen coobare; wuteek jàllalekaay yu baax yi, waaye, duñu leen lim ci lu fës, looloo tax ab noon mënu leen a ràññee ci lu yomb.

Jëfandikoo bridges yu ànd ak pluggable transports dafa lay dimbali ngir doo feeñ ci sa jëfandikoo Tor, waaye mën a wàññi dooley lëkkaloo bi soo ko tëkkaleek jëfandikoo jàllalekaayi Tor yu baax.

Yeneeni pluggable transports, yu mel ni meek ak Snowflake, dañuy jëfandikoo ay tekniku jumtuwaay yu dul ubbi ay pexe yu wéeruwul ci seet ay dëkkuwaayi bridge. Soxlawuloo am ay dëkkuwaayi bridge ngir jëfandikoo transport yi.

JOT DËKKUWAAYI BRIDGE YI

Ndax dëkkuwaayi bridge yi fësuñu, dina laaj nga seet leen yaw ci sa boop. Am nga yenn tànneef:

  • Xoolal https://bridges.torproject.org/ te nga topp tegtal yi, wala
  • Boyetu bataaxal bridges@torproject.org joge ci ab Gmail, wala boyetu bataaxalu Riseup
  • Jëfandikool Moat ngir seeti ay yooni pom ci biir Tor Browser.
  • Yonneel ab bataaxal ci @GetBridgesBot ci Telegram. Bësal ci 'Start' wala bindal /start wala /bridges ci chat bi. Sottil dëkkuwaayu bridge bi ak ci:
    • Tor Browser Ordinaatëer: Kilikeel ci "Settings" ci àlluwa bu hamburger bi (≡) ba noppi ci "Connection" ci wàllu wet gi. Ci pàccu "Bridges" bi, ci tànneef bu "Enter a bridge address you already know" kilikeel ci "Add a Bridge Manually" te nga duggal dëkkuwaayu bridge bu ci ne ci ab liiñ bu beru.
    • Tor Browser Android: Bësal ci 'Settings' (⚙️) ba noppi ak ci 'Config Bridge'. Toxul ci 'Use a Bridge' te nga tànn 'Provide a Bridge I know'. Bindal dëkkuwaayu bridge bi.

JËFANDIKOO MOAT

Su fekkee yaa ngi soog a jëfandikoo Tor Browser, kilikeel ci "Configure Connection" ngir ubbi palanteer bu sukkandikukaayi Tor yi. Ci suufu pàccu "Bridges" bi, xoolal "Request a bridge from torproject.org" te nga kilike ci "Request a Bridge..." ngir BridgeDB joxe ab bridge. Mottalil Captcha bi te nga kilike ci "Submit". Kilikeel ci "Connect" ngir deñc say sukkandikukaay.

Wala, soo yoree Tor Browser buy dox, kilikeel ci "Settings" ci àlluwa hamburger (≡) ba noppi ak ci "Connection" ci wàllu wet gi. Ci pàccu "Bridges" bi, xoolal "Request a bridge from torproject.org" te nga kilike ci "Request a Bridge..." ngir BridgeDB génne ab bridge. Mottalil Captcha bi te nga kilike ci "Submit". Sa sukkandikukaay dina nu ko deñc automatically soo sëxee ba tëj xët bi.

Laajal ab bridge ci torproject.org

DUGGAL DËKKUWAAYI BRIDGE YI

Su fekkee yaa ngi soog a jëfandikoo Tor Browser, kilikeel ci "Configure Connection" ngir ubbi palanteer bu sukkandikukaayi Tor yi. Ci suufu pàccu "Bridges" bi, dale ko ci tànneefu "Enter a bridge address you already know" kilikeel ci "Add a Bridge Manually" te nga duggal dëkkuwaayu bridge bu ne ci ab liiñ bu beru. Kilikeel ci "Connect" ngir deñc say sukkandikukaay.

Wala, soo yoree Tor Browser buy dox, kilikeel ci "Settings" ci àlluwa hamburger (≡) ba noppi ak ci "Connection" ci wàllu wet gi. Ci suufu pàccu "Bridges" bi, dale ko ci tànneefu "Enter a bridge address you already know" kilikeel ci "Add a Bridge Manually" te nga duggal dëkkuwaayu bridge bu ne ci ab liiñ bu beru. Say sukkandikukaay dina nu leen deñc automatically soo sëxee ba tëj xët bi.

Duggalal dëkkuwaayi bridge yi ak sa loxo

Su lëkkaloo bi jàllulee, bridges yi ngay jot mën nañu wàcc. Ci bu la neexee jëfandikool benn ci tëralin yii ci kaw ngir am yeneeni dëkkuwaayi bridge, te nga jéemaat.

BRIDGE-MOJI

Dëkkuwaayu bridge bu ci nekk dafay feeñ ci ab liiñu màndargay emoji bunu tudde Bridge-mojis. Bridge-mojis yi mën nañu leen jëfandikoo ngir weral ne bridge bi nga bëggoon yokk nanu ko ci ak ndam.

Bridge-mojis nekk nañu xameekaayi bridge yu nit mën a jàng te duñu wone baaxaayu lëkkaloo bi ci jokkoowu Tor wala nekkinu bridge bi. Liiñu màndargay emoji bi mënu nu ko jëfandikoo niki xibaar bunu duggal. Jëfandikukat yi nu ngi leen di laaj ñu duggal dëkkuwaayu bridge bu mat sëkk ngir ñu mën a lëkkaloo ak ab bridge.

Bridge-moji

Dëkkuwaayi bridge yi mënuloo leen séddoo sooy jëfandikoo QR kot wala sooy sotti dëkkuwaay bi yépp.

QR kotu Bridge