Tor Browser dafay jëfandikoo jokkoowu Tor bi ngir aar say mbiri bopp ak nu bañ la xàmmee. Jëfandikoo jokkoowu Tor am na ñaari moomeel yu am solo:

  • Sa kër gi lay jox serwiisu internet, ak képp kuy seetaan sa lëkkaloo ci gox bi, du mën a topp sa yëngu-yëngu ci internet, bokk na ci tur yi ak dëkkuwaayu dalu web yi ngay yër.

  • Nit ñiy liggéey ci dalu web yi ak serwiis yi ngay jëfandikoo, ak képp ku leen di seetaan, dina gis ab lëkkaloo bu joge ci jokkoowu Tor ci sa palaasu dëkkuwaayu Internet (IP), te du xam yaw yaay kan xanaa nga wone sa bopp ci lu leer.

Rax ci dolli, Tor Browser danu ko defar ngir aar dalu web yi ci "fingerprinting" wala ci xàmmee la sunu sukkandikoo ci sa tëgginu xuusukaay.

Ci li teew, Tor Browser du deñc benn cosaaanu xuus. Nëbbiit yi baaxuñu ci ab session rekk (ba ngay génn ci Tor Browser wala nu laaj la ab New Identity.

NAKA LA TOR DI DOXE

Tor nekk na ab jokkoo ci ay yoon yu jëmmadi bu lay may nga gën aar say mbiri bopp ak kaarànge ci Internet bi. Tor dafay liggéey di yonnee say lëkkale ci ñetti serwëer yuy jàll (nu leen di woowe itam jàllalekaay ci jokkoowu Tor bi. Jàllalekaay bi mujj ci circuit bi ("exit relay" bi) dafay génne lëkkale bi mu fës ci Internet bi.

Naka la Tor di doxe

Nataal bii ci kaw dafay wone ab way-jëfandikoo xuusukaay ci dalu web yu wuute ci Tor. Ordinaatëer yu nëtëx yi ci digg bi ñooy wone lëkkale ci biir jokkoowu Tor, te ñetti caabi yi dañuy wone déggoob web yuñu caabi diggante way-jëfandikoo bi ak jàllalekaay bu ci ne.